Ce recueil de contes s’inspire de la tradition orale africaine, source intarissable de valeurs culturelles éducatrices incontournables dans la formation d’un altruiste, d’un homme responsable et soucieux du bien-être de l’humain, autrement dit d’un citoyen ancré dans ses valeurs de civilisation et ouvert aux apports fécondants du monde. En effet, la morale de ces contes donne des enseignements en rapport avec les valeurs citoyennes. Il s’agit de faire la promotion du comportement citoyen. Ce faisant, le récit fantastique éveille la sagacité enquêteuse à la prime enfance et comme le préconise Cheikh Anta Diop participe « au déverrouillage de l’esprit créateur ». ---- Niseru téere bi mooy gëstu ci dund maam, fësal ci ay taxawaay yi mën a tabax, defar jikko tuut-tànk yi tey, te gindi leen ëllëg. Léeb ci pexe yooyu la bokk: dafay yee ci àdduna. Jubluwaayam du woon béggal rekk xale yi; jàngal leen ak tàggat leen ba ñu doon ñu mat moo ko taxoon jόg : « bant jubbantil ba muy tooy » di waxi Wolof Njaay. Ba muy nekk nebbantaan lañu Kay miinal dëgg ak xam-xam, ba mu xemmem ko, gimmi ci ngir ëllëg taxawaayam mucc ayib ñeel pénc mi. Su déggee Kocc Barma, demokaraasi ba muy ndaw, waxambaane bi daa bëgg xam boroomi jubb yi ak ay jamanowaaleem, daa bëgg itam xóotal xam-xamam ci wàllu demokaraasi bi ñu ko doon léebal. Noonu la gëstu di saxe ci xale, ni ko Seex Anta Jóob doon xamale: « tijji xel um sàkku.» Maanaam waajal gone yi tey ngir ëllëg ňu amal njariñ pénc mi, xam seen bopp, weg seen askan.